As an anonymous user, you can only add new data. If you would like to also modify existing data, please create an account and indicate your languages on your user page.

Help:DefinedMeaning/wo

From OmegaWiki
Jump to: navigation, search
Ab TekkiFaramface (DefinedMeaning) mooy booloo bu ab Waxin ak ab Tekki ;
ab waxin du lenn lu dul ay baat yu ñu boole ñeel ab làkk, mu am lu muy xamle; te ab Tekki mooy faramface gi, ci benn walla ay baat, gu waxin gi.

Ab TekkiFaramface (maanaam tekki gu ñu faramface) ab limuwaay la ci database bu OmegaWiki. Ngir naal bi man a dox ci ni mu waree laaj na nga nand bu baax tekkeem ak nu muy doxee.

Sos ab TekkiFaramface[edit]

Ab TekkiFaramface (DefinedMeaning), ci ndoorteelam day nekk ab waxin, te di tekki li waxin googu di xamle ci benn walla baat yu bari; Tekki gi. Ab TekkiFaramface man naa jòge ci bépp làkk, Waxin bu Njëkk bi ak Tekki bu Njëkk bi di nan leen wone ci wet gi, ci xëtu coppite wi.

Firi ab Tekki[edit]

Ab TekkiFaramface, man nan kaa jox ay tekki yu bari, te teey ci tekki bi ndax dafa war a nduroo ak waxin bu njëkk ba, maanaam tekkeem warul soppiku. Bépp firi boo def, li gën mooy nga defee ko ak waxin wu njëkk wa, maanaam ca làkk wañ koy waxee, loolu di na waññi coppite gu tekkib waxin boobu.

Wax Tekki bi[edit]

Ab TekkiFaramface, man nan kaa jox ay waxin yu bari, muy ci làkk bi mu jòge walla ci yeneen làkk yu mu man ti doon. Waxin yi nu lëkkale ak ab TekkiFaramface danoo war a mengoo ak Tekki bi, te waru ñu doon ay firi yu Waxin bu Njëkk ba.

Man naa ne, mu am ay Waxin yu bari yu mengoo ak benn TekkiFaramface ci ab làkk: ñooy bokk-tekki yi. Bépp yemte bu mel neenu dang kaa war a fesël ni yemte xelñarul am déet, maanaam waxin bi mengoo na ak tekkeem ci lu wòor.